Jooy naa jooy ba nurootuma nit
Boo ma xasul, saagawoo ma, yaa ngi may cokkaas
Wax ju neex, bu jogee ci yaw daf may jafe lool

Samba buuru àll la woon
Bari jom lool ak yërmande

Jëm na jëm waye gis ni dangay tooñ
Te tooñ du nga làcc man sa soxna la
Man ma la jural doom amoo soxna waay

Samba buuru àll la woon
Bari jom lool ak yërmande

Kenn du téral Nday bayi baay
Liggéeyu Nday, barke Baay
Jirimoo jirim
Malick Gackou xamul yaayam
Mel na ni ku mosta ñaaka yaay
Adjia Astou Seck moy ki ko tété nampal ko
Momar Gackou mooy sa baay
Momar moomu nga tudde sa doom Momar

De ma ree ma lay reetaan
Wax ju neex daf may neex a neex
Ree ju neex daf may neex a neex

Woah woah, woah woah
De ma ree ma lay reetaan
Wax ju neex daf may neex

Biik ba tay
Te nga ma reetaan
Tèkk ci di ma tanxamlu

Lu nekk a maa ngi koy wax
Lu nekk mangui'koy daj
Su ma sañoon dafay neex
Ba bénnoon du ree
Dann nga ma reetaan
Ñëwal ñu ànd ree

Woah woah, woah woah
De ma ree ma lay reetaan
Wax ju neex daf may neex a neex
Ree ju neex daf may reeloo

Kékh kékh may ree... aaah!
A aha!
Eh, ñépp di ree
Man sax damay ree
Aha aha!

Kaay fi!
De ma ree ma lay reetaan
Wax ju neex daf may neex a neex
Neex neex