Dama ni sama xarit nga Te yaw mi xam nga ni ku la bëgg laa Wax dëgg Yàlla seede na, sama xarit nga Te yaw mi xam nga ni ku la bëgg laa Bëgg naa la ba foo pikiiru ma naan fa doom Lu la metti gaañ ma, lu la wokk xuri ma yay Ma ni yaw foo pikiiru ma naan fa doom Lu la metti gaañ ma, lu la wokk xuri ma, yeh yeh yeh Buur Yàlla moo ñu boole Sama waay nga te du tay loolu démb la (loolu démb la) Man ak yaw boobu ba léegi Sunu diggante bi teye nañ ko mu dëgër (mu dëgër) Oh oh oh Xarit dëgg am na, xarit dëgg am na Oh oh oh Sa xarit dëgg man la, seedeel naa la lii Sama waay nu ko raw laa la bëggee Nga sax ci sama xol maa ko wax sama guy nga Foo ko seen geestu gis ma Guddi muy bëccëg soriwuma Dégg nañu lu bon, dégg nañu lu baax Bokku nañu bànneex, bokku nañu naqar Ba pare mel ni ay Cheikh amuñu nëbo Eh eh, du lekk bàyyi ma Ma ni yaw xarit nga Gën nga doomu ndeye, lii leer na ma Yaw xarit nga Zeyna Ndour doo doom waay nga Buur Yàlla moo ñu boole Sama waay nga te du tay loolu démb la (loolu démb la) Man ak yaw boobu ba léegi Sunu diggante bi teye nañ ko mu dëgër (mu dëgër) Oh oh oh Xarit dëgg am na, xarit dëgg am na Oh oh oh Sa xarit dëgg man la, seedeel naa la lii Oh oh oh Xarit dëgg am na, xarit dëgg am na Oh oh oh Pa Philippe xam na seedeel na ma lii Foo pikiiru ma naan fa doom loolu leer na Yaa gën ci man fu ma jaaxle ñëw seetsi la Yaw rekk laay gis su lëndëmee Lu ñu mësa wax ci ñun la yam Lu ñu mësa def ci ñun la yam Bu dara xewe ñu ànd dem Suñu diggante moo dàq lem Sama jikko boo ko bëggee gis laal ko seet [Ndiole Tall] Yaa yéy def ko muy sa xarit Bul déglu kenn àndal ak moom Doom day sax ci xolub ndayam Vivi ànd ngeen sax ba ndiroo kanam Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam Kuy laal sama waa ji Vivi jugal ñu dem Lu la wokk xuri na ma foo dee ma dee fa (Àndal ak ku dal sa xel!) Ni ñuy àndee nii neex na ma xarit sama (Xarit dëgg nii lay mel) Yaw rekk laay gis su lëndëmee (Moy cote far!) Ñun benn lañu te duñu ñaar (Moo am) Lu ne lañu gis ndax fi ñu jaar (Moo tax yaa ngi ca kanam) Bu coow li bare maak yaw a far (Ñoo far) Amitié bu mel ni aka rare (Loo sax!) Sama jikko boo ko bëggee gis laal ko seet (Kaay laal lu la ci dal dinga xam) [Ndiole Tall] Ku nekk làmbil bi la neex topp sa xarit Maa yéy sama yaay laay topp Bu ngeen àndee dina neex, ah Bu ngeen àndee dina neex, aa Thiam day neex Foo pikiiru ma naan fa doom loolu leer na (Dama ni li leer na) Yaa gën ci man fu ma jaaxle ñëw seetsi la (Ñëw seetsi la) Yaw rekk laay gis su lëndëmee (Cote far, far!) Lu ñu mësa wax ci ñun la yam (Ñun rekk) Lu ñu mësa def ci ñun la yam (Ñun rekk) Bu dara xewe ñu ànd dem (Sañse lu took) Suñu diggante moo dàq lem (Aaah!) Sama jikko boo ko bëggee gis laal ko seet (Kaay laal lu la ci dal dinga xam) [Ndiole Tall] Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam Kuy laal sama waa ji lu la ci dal yaa xam Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam Kuy laal sama waa ji lu la ci dal yaa xam Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam Kuy laal sama waa ji lu la ci dal yaa xam Kuy laal ma démba sagar yaa ca ndam