Viviane Chidid

Waaw (part. Salam)

Viviane Chidid


Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo wax maa ni
Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo def maa ni

Boo, sama xol,
Yaa koy pincer
Maa koy feel

Danga toog ba xaaju guddi
Yoot ndanq dugg suñu kër
Fexe ba kenn yëgul a
Nga saccee sama xol bi dem
(Wuy saccee!)

Yaa saf, sapp ak suukar
(Ñamal!)
Dama am sa faiblesse duma la...
(Ñamantiku!)
Yaa may tàggale ak sama sago
(Jëlël)
I love you, I love you

Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo wax, ma ni
Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo def, ma ni

Yagg nga miir ci man
Xam nga sama dugg ag sama génn
Xam nga samay àndandoo
Xam nga tamit samay dëkkandoo

Maître bi la jàngal aay na
(Taril!)
Loo wax dafa neex ba mel ni
(Hawaï!)
Loo def maa gis ne noonu la
(Jëlël!)
I love you, I love you

Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo wax ma ni
Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo def ma ni

(Xale yi maajleen!)
Mel ni soldat ag général
Ci bësu fêtu indépendance
(Indépendance bi)
Sa mbëggeel la may maaj loo
Ci sa ordre rekk laay wëy
(Ci laay wëy)

Yaa saf, sapp ak sukër
(Ñamal!)
Dama am sa faiblesse duma la...
(Ñamantiku!)
Yaa may tàggalek sama sago
(Jëlël)
I love you, I love you

Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo wax ma ni
Waaw, waaw waaw, waaw waaw,
Loo def ma ni

Boo, di sama xol
Yaa koy laal
Maa koy yëg
Boo, di sama xol
Yaa koy pincé
Maa koy feel

Ee, bul daw jaru ko
Ndax rëcc nga
Càcc bi! Ngay càcc gune bi
Neex na ndeyam, neex na baayam
Avocat mënu ci dara
Procureur mënu ci dara
Monsieur le juge bu nu juger
Wuy yaayooy wuy càccee lay-lay-lalla!