Doo ma tere dund man Ndax sakuloo ma Ku lay tere dund moom Na fekk mu moom la yaw Ndax yenn saay nit teg la coono Dellu nekk ci nooflay Soo ko nangoo ba mu sonn la Yaa ko teg sa bopp waay (Ouwaaay) Ma ni defe ko ni ndax bakkan jàmm la bëgg Dundel sa dund, bu leen faale Yeen yi soxor la may nurool Wax ji de safu ma, dóor yi de yëguma Ndax sama yaram ma blindé Joxoo ma lekk, joxoo ma naan Moomuloo ma yaw mi le Doo ma tere dundu Doo ma tere dundu Ngay jukk ak di daanu Ñu ne ki dey jaambar la Di añ ci al bi Di réere ci mbédd mi Ñu naan la ñafe ko noonu la Bu amee te amuñu yaw Nit yii la doon yénne lu baax Ñu lay njëkk saaga Ngay duggu ak di génn Di ko liggënti Ñu naan la yaw mi dey caaga nga Bu ñu la tere dund Doo ma tere dund Doo ma tere dund Man amuma jote Te loo ma def baal naa la Dima ligënti Ba xëy bidanti Xana déy yaw mii déy sonuloo ? Dundel kenn moomu la Àdduna noonu la Ndax ku nekk diw du jàmm am Tere ma dundu Bëgg di dundu Tay ma xamal la loo xamul woon Doo ma tere dund Doo ma tere dund Doo ma tere dund Àdduna Yàlla ngay jammu Boo ko deful dinga gaañu Dunduleen li ngeen di dundu ñu yénnénte jàmm Àdduna Yàlla ngay jammu Boo ko deful dinga gaañu Dunduleen li ngeen di dundu ñu yénnénte jàmm Ndax yenn saay nit teg la coono Dellu nekk ci nooflay Soo ko nangoo ba mu sonn la Yaa ko teg sa bopp waay (Ouwaaay) Ma ni defe ko ni ndax bakkan jàmm la bëgg Dundel sa dund, bu leen faale Yeen yi soxor la may nurool Wax ji de safu ma, dóor yi de yëguma Ndax sama yaram ma blindé Joxoo ma lekk, joxoo ma naan Moomuloo ma yaw mi le Doo ma tere dund Doo ma tere dund Ngay jukk ak di daanu Ñu ne ki dey jaambar la Di añ ci al bi Di réere ci mbédd mi Ñu naan la ñafe ko noonu la Bu amee te amuñu yaw Nit yii la doon yénne lu baax Ñu lay njëkk saaga Ngay duggu ak di génn Di ko liggënti Ñu naan la yaw mi dey caaga nga Buñu la tere dundu Doo ma tere dund Doo ma tere dund