Viviane Chidid

Par Force

Viviane Chidid


Hasta la pista
Dose bi lay yokk
Yenn saay baax na
Nga indi show time
Guddi par force ci nekk
Man ngeen di cons akh
Boo yeewoo naan sa kafe
Man may sa sugar

Say nopp soo bëggee dégg lu neex, man la
Yàlla ko def ci man, nangul ma ko dégg nga?
Moytul reey fi nit te sa loxo laalu ko
Gél bi li muy dégagée, nit antanu ko
Eh yow hé!

Aaah yeah
Danga xam wala dangay laaj?
Li Yàlla def ci man

(Ouh yeah)
Danga xam wala dangay laaj?
(Ouh yeah)
Danga xam wala dangay laaj?
(Ouh yeah)
Danga xam wala dangay laaj?
(La la la ouh yeah)
Yàlla ko def ci man

Àdduna ni la
Soo menul jàngal
Boo xamul laaj ma
Ma wane la naan la
Soo bëggee ma dimbali la
Def la ndaanaan
Kaay ma tàngal la du jeex
Ni géju ndaayaan

Nit ki su wetee xam boppam du ko sonnal
Par force ngay nangu ni Yàlla ma téral
Par force nangul ni reine bi man la
Gél bi li muy dégagée, nit antanu ko

Aaah yeah
Danga xam wala dangay laaj?
Li Yàlla def
Aaah yeah
Danga xam wala dangay laaj?
Li Yàlla def ci man

Music bi sa dalal ton bi
Man la, man la yaw
Ni may solo yenn saay
Da lay choqué choqué yaw
Man ni ma mel teint bi ma yor moo naturel
Gél bi li muy dégagée nit antanu ko
Eh yow hé!

Aaah yeah
Danga xam wala dangay laaj?
Li Yàlla def
Aaah yeah
Danga xam wala dangay laaj?
Li Yàlla def ci man

Sama bidéew fi muy finke, auto du fa daw
Bañ bañ bëgg ni ko Yàlla Buur moy dogal yaw
Man ni ma mel, man ni ma mel moo naturel
Gél bi li muy dégagée, nit antanu ko
Eh yow hé!

Aaah yeah
Danga xam wala dangay laaj?
Li Yàlla def
Aaah yeah
Danga xam wala dangay laaj?
Li Yàlla def ci man
Li ne ci man mi...

Oh wu waaw
Jàmbaar ca waar wa
Liggéeyam moo tax
Muy rotti mbaa laaxu
Te dëgg la

Xoolal You fu ko neex lay fële
Mag ak ndaw ñëpp di ko bëgge
Man Youssou Ndour dal fépp la mane
Eh! Nangul ko ko force la

Moo par force la, billaahi par force la
Te la naagu dey yombali duma, man de nangu na!
Viviane ku la yenn ciy duma
Ak ku la jàngali duma
Ba ko jeku caaw ko sa xiir
Oh yeah fracc!

Nu may def ba mu neex ni
(Man da may laaj)
Man fu ma jële feeling bi
(Man da may laaj)
Sama secret ba léegi
Liggéey ba tay jàppe te bàyyiwuma

Xoolal Vi fu ko neex lay fële
Mag ak ndaw ñëpp di ma bëgge
Fi mu newoon démb jugewu fa
Eh! Bañ bañ bëgg force la

Kenn bañu la!
Xanaa boo rombee la ñuy doga jar
Sa sañse yi ci réew mi la ñuy toog di xaar
Billahi Viviane sax danga rombu art

Waaw woo woo woow
Ku la laaj nu mu deme ni ko li la
Bu suba ci ngoon dinga comprendre
Ku ci xiif tey bëgga dee di nga tàngal la ca wañ wa

Xale bi, nu ko neex lay doxe
Xoolal ki fu ko neex lay fële
Àdduna bi dal noonu lay deme
Eh! Bañ bañ bëgg force la

Dégg nga?
Nangul ko ko, dégg nga?
Gis nga li mu mën?
Nangul ko ko
Coow li bari na
Dara du ko teye
Yàlla lu mu def jaam mënu ci dara

Dégg nga?
Nangul ko ko
Bind bi baax na, dégg nga?

Par force!