1da on the beat Never mind every day, bàyyi nit ñi ñu sol la bàyyi nga liggéey Jarul coow di jib, coow du jib jarul Sa family ñooy sonn ci yaw di daŋ-daŋi kay Bis dina tar doo gis kenn Kon jëli li des, mën nga jëli li des, jugal jëli li des Lépp ci xel rekk lay feeñ, jëlil li des Yaay jëli li des, mën nga jëli li des (mmm) Ndax lépp ci xel la, kon yaw yaay jëli li des Sol essence sa mind soog a jëli li des Ñépp a soxla ndam def ni mbër yi di def Dootuñ joow Senegaal seen gaal gee bari vitesse Fii ñi dàq a jaay seen taat ñoom seen cér yi du feeñ Non duñ sàcckat yu mag bu dee soluñu veste Ku ñàkk wéet nun ndox yu taa yee tax sunu kër yi di fees Luy sa njariñ ñu xeex texeg tekki Xayna safaraay changer nit Fi dóomu taal taxul ba këriñ mënul weex Nice fine, Suñ dëkk du gat baay Fi jeunes yi dul am njëgam duñ def lu dul taaj caayin Balóot, babi ak dice Dóor call këfi sac jaay Réer ci saayir ak baatin fen ak dëgg bëccëg night time Ku dund jàng force ndax life day jox ay cours sa maitre Bul xam ku baax ci yaw ak ku la jekkoogul batay Loo baax baax moytul nit ñi foog ne sa xol moo sut sa xel Fii dangay dee ci nit mu lay xoon pour nga dee Kon jëli li des, (I'm on my way) Mën nga jëli li des, (you know my pain) Jugal jëli li des (story of my life, story of my life) (I'm on my way) Yaay jëli li des (you know my pain) Mën nga jëli li des (story of my life, story of my life) Ndax lépp ci xel la, kon yaw yaay jëli li des Jëli li des pour bañ ñàkk li xaalis mënut a am Yaa gën alal mën nga ñàkk sa bopp ci wut alal Même sutura dafa cher ni dignité muñ ak ndam Ku bañ tàllal loxoog yërmaande fàww nga suul sa tànk dóoranteek life Nangu sëyal metit heureux ménage door a ker naaj Yal na nu Yàlla musal ci compte bu fees ak ruu bu vide Musal nu tam ci toog ak ñépp bég ak wéet sa ruq triste Xel kenn du ci lire kenn mënut a xam lu weex ak ñuul ci nit Gëj naa gis samay doom, gëj naa feel sama drogue Gëj naa am li ma yellool comme bénéfice sama job Tay jëli naa li des, tay njàmpe la ci der, calpé laa ci cash Tay xàmme naa vipéres yépp Duñ ma téeye ni Mandela ci jail On the top of the top Dip Doundou Gis you know my name Booy damaa doylu trop ku mënul suur mënu maa lekk (mëno maa lekk) Dereet du fen, Yàlla buy def du tàggu kenn Démb ñaan yi bañ na tay sët yi nangu nañu Never mind every day, bàyyi nit ñi ñu sol la bàyyi nga ligégey Jarul coow di jib, coow du jib jarul Sa family ñooy sonn ci yaw di daŋ-daŋi kay (daŋ-daŋi kay) (Daŋ-daŋi kay, daŋ-daŋi kay)