(Humm hum) (Oh oh) (Yeaah) Daj ngeen ci ëkk, këkk, ndëgg sërëx Doo ma jey ba jaay ma doog maa bëgg nëbb sa njëg Duma la daan ba toog sa kaw nga bëgg ma njëkk sëlëm Rap dëkkatul ci sama xol daa tëju sama xëtër Gëtam ay boys you téxet ba ër, tëx, lu tëb di sëmbëx (Low) Ci sama jëmm tay laa gën a dëgër Utal kër mère bi, ngandim maamu Mercedes ak chauffeur Tës xëtëm yi njëkk du mës a jëmbët ku leen gën a sëcc Sàcc du sàcc ba sàcc sama sacrifices yi Noon bi lay ray mën na jaar ci fiisabii Lilahi Jaag du kàcc ba daj ma ci njuuj njaaj Jiiñ ngeen ma bon, jiiñ ma soxor Jiiñ ngeen ma yéefar ak Illuminati Li ma moom buy dem ci keneen ku dul man mii C'est comme mardi-gras bu ñu feetwul ci mardi Ci biir camps yi laa koy def ni Jamie Vardy Lëndëm, samay fautes du feeñ mukk ci VAR bi (Yeah) Dara dootu ma defati dara Am ndam fi ma ko waroon am yépp mais defaite bi man a Xëy te duma waaj doyal ci life te fekkeeguma gat Facturu àq yi ma ame yépp lay fay te duma rang Xeet yépp la suuf warax du kaaw kese rekk fepp ay suul ndanaane Seen game jarul tuur leketu kaana ak dereetu mala Tekkeeguma gat ci musique bi mel ni sexluwuma cat Kenn yeemu ma ndax mënuma féey ci tefes di fa lab Ñi dama leen yagg fuck ba ñu foog ne ñu jur samay doom Duggal sama zone dama lay duut ba pare rouge la nga toog Rap Galsen man rekk la benn MC buy course ak sa bopp Mën nga ma fuck? Microphone bi Dip sa tuun la ko roof Juumal ba dof nu bokk son dama lay ñuus dama lay noq Kuy sut sama njort ndayam judduwul maamam fause couche la defoon Boy duma sa moroom maak yow bokkounu Ni suurka xorom Ni Ummah ak Rome Joueurs yi ak Àllaaji Juuf double ballons d'or Ni sumb ak fomb Sunguf ak ndox Dugub ak mboq Ni dunq ak góor Ni kuy mbalax ak kuy dund hard core Chaque joueur mën na togg benn single suul double album Lu ma def tay suba ñoom ñépp def ni Duudu ak Ngóor Maay buur bi maay boos bi, bul ma tëkkale ak buujuman yoyou Fàtte xaju fi Lépp Fii La nu Fekk ni turu album bi