Dip Doundou Guiss

Deuil National

Dip Doundou Guiss


Manatuma toog di xaar leneen
Li nek sama bop bi xatt na fees na
Manatuma toog di xaar leneen
Dama muju joow ci gaal ba dess fa

Lelelelelena dama muñ ba de, muñ bi jeex na
Ndaw si diggu geej weet na, reer na
Sama bakanay rot su geej gi mare naan

Lo sorale dalay diisël
Tëwa fatte ñima bayi ginaaw
Nap kat bi gëdj na giss jën
Ku saccul, ñaanul marr na xiif na
Diplome ak journala yam këyit lë
Fay ndox ak courant ba tay dañuy të
Suñu quotidien mo gëna tiss tëss
Suñu kër day taa ndox luñu miin lë
Xamul ndax yoonu xaru la am yoonu risque lë
Tekkey alxuranam, tekkey biblëm
Geej du mëssa rëy ba ëp fittëm
Gëm ni buñu yegge nañ yeetal fitnë
Def ni ku rep giss yoon
Dekkufi sedd di lox
Defuñu ken lu bonn
Dadj luñu yeene wul dom
Soobu si teen bi di root
Dem te ñëw tedd ni Gorr
Dem te ñëw fay suñuy borr
Delu samay digg mbok

Don mak si kër di daw yërmande ak ndimbël motax ñu sëss
Xam liñu bëg fimu ne moy xam fiñu jëm
Yoonu geej du liñu gënël liñu gënël moy am li gën
Ken bëgul doomam di taggo dem ñukoy deggat si dëdj
Gaal bu dëppu, këppu, këppale famille lëm
Mëno ŋacc waye dem nga seeti charlie demb
Juromi temeri neew Etat ne du wax si sen dëdj
Fi yaakar si nguur moy yaakar si ay ngandi dëm

Manatuma toog di xaar leneen
Li nek sama bop bi xatt na fees na
Manatuma toog di xaar leneen
Dama muju joow ci gaal ba dess fa

Lelelelelena dama muñ ba de, muñ bi jeex na
Ndaw si diggu geej weet na, reer na
Sama bakanay rot su geej gi mare naan